Trace Id is missing

Microsoft® Office Language Interface Pack 2013 – Wolof

Microsoft Office Language Interface Pack 2013 - Wolof day may jokkalekaayu jëfandikukat bees tekki jëfekaay yu bari yu Microsoft Office 2013.

Lu am solo! Tànn ab lakk fii ci suuf dina soppi ci lu gaaw mbooleem këmbu xëtu boobu lakk.

  • Sumb:

    2013

    Bisu Siiwal bi:

    27-08-2013

    Turu Taxañ

    languageinterfacepack-x64-wo-sn.exe

    languageinterfacepack-x86-wo-sn.exe

    Dayoob taxañ:

    13.2 MB

    13.1 MB

      Microsoft Office Language Interface Pack 2013 - Wolof dina jàppandil ab jokkalekaayu Jëfandikukay bees tekki ngir jëfekaayi Microsoft Office 2013 yii topp:

    • Microsoft Excel® 2013

    • Microsoft OneNote® 2013

    • Microsoft Outlook® 2013

    • Microsoft PowerPoint® 2013

    • Microsoft Word® 2013


    • Boo jëfandikoo Sayu 2013 bu Jokkalekaayu Làkk bu Microsoft Office - Wolof, jëfandikukat yi mën nañoo liggéey ci sottiy làkk yu jëfekaayi Office campug ndoorteel yees nangu te xool santaane yi ak taaneef yi ngir yooyu jëfekaay ci - Wolof.

      Ci campug Microsoft Office Language Interface Pack 2013, taxañ yi may jëfandikukat yi ñu soppi làkku jokkalekaayu jëfandkoukat bi dañu leen di sotti ci disk bu dëgër bi. Ginnaaw camp gi, Microsoft Office Language Interface Pack 2013 - Wolof njariñ yeek tànneef yi dëppoo jàppandinañu ci jëfekaay yu Office 2013 ak jëfekaay bu Jekkali Làkk bu Microsoft Office 2013.
  • Sistem yimuy nangu

    Windows 7, Windows 8

      Microsoft Windows 7 - 32 mbaa 64 bit OS
      Microsoft Windows 8 - 32 mbaa 64 bit OS
      Karmat: Baal nu wérlu ne samp nga Sayi Cër yi mujj ngir sa nosteg doxal ngir am jàppandalug làkk wu mat ci sa làkk.

    Tëriin Bépp sottib Office 2013 muy toppaan am déet bu am Microsoft Excel, Microsoft OneNote, Microsoft Outlook, Microsoft PowerPoint mbaa Microsoft Word mbaa muy nangu Microsoft Office Language Interface Pack 2013 - Wolof. Karmat: Baal nu wérlu ne samp nga Sayi Cëru Microsoft Office yi mujj ngir say costey Microsoft Office. Loolu dina wéral ab jaar-jaaru jëfandikukat bi gën.

    Ordinaatëer ak Prosesor 1 GHz xaymakaay bu ànd ak SSE2 mbaa lu ko ëpp; 2 GB RAM mbaa lu ko ëpp

    Yaatuwaayu Disk Ci dollikug yaatuwaayu disk bu dëgër bees jëfandikoo bees di samp jëfekaay yu Office 2013,
  • 3 GB yu jàppandi ci yaatuwaayu disk bu dëgër.

  • Lépp lu beneen noste laaj ñu ngi yem ak yoy jëfekaayi Office 2013 yi nga nekk di jëfandikoo ak Microsoft Office Language Interface Pack 2013 - Wolof.


  • Windows Language Interface Pack Digalees na ñu samp Language Interface Packs bi mujj bu Windows 7 mbaa bu Windows 8 ngir kaweel mbiru làkk yi ci sa nosteg doxal ak say jëfekaayi nosukay.

    Sottalu Wonekaayu siiwali tànnéefu DPI Araf yu bari dees leen sos ngir jàng gu gën ci tollalug 1366 x 768. Boo amee jafe-jafe ngir jàng say arafi làkk, baal nu yeesal say jekkali doxal ci bii tollale mbaa bu ko ëpp bu ko laajee. Baal nu jàpp li: nu ngi lay dénk ngay jëfandikoo jëfekaay yu Office 2013 ci sa jekkalu DPI bu Wàccaaleek Windows - 96 DPI. Jëfandikoo jekkal bu 120 DPI mën naa jur jaar-jaarug jëfandikug Office bu néew doole ci ci yenn jëfekaayi Office boo yokkee yaatuwaayu Office.

    Tànnéefi Làkk ak Diiwaan Teg ci dénkees na ne lépp Tànneefi Làkk ak Diiwaan ci Barabu Fugluwaay def nañu ko ci làkk bu Sayu 2013 bu Jokkolekaayu Làkk bu Microsoft Office - Wolof.

  • Ngir samp bii wàcce:
    1. Wàcce LanguageInterfacePack.exe taxañ bi boo cuqee Wàcce butoŋ (ci kaw) te aar taxañ bi ci disk bu dëgër bi.
    2. Cuqal-ñaaral LanguageInterfacePack.exe taxañu prograamp bi ci disk bu dëgër ngir door sampukaayu prograam bi.
    3. Toppam tegtal yi ci sa seetu ngir matal camp gi.
    4. Boo sampee ba noppi taxañu jàngma bi ngi sa Microsoft Office 2013 Language Interface Pack mënees na koo fekk ci C:\Program Files\Common Files\microsoft shared\OFFICE15\1160\LIPread.htm.
    5. Kawelug Office 2010 ànd ak Microsoft Office 2010 Language Interface Pack mbaa sotti bu jamp ci Office 2013 ànd ak Language Interface Pack mi ngi nanguweesu ko. Boo nammee kaweel sa campug dàtt bu Office 2010 jëm ci Office 2013 ak Microsoft Office 2013 Language Interface Pack war ngaa:
      • Sempi Microsoft Office 2010 Language Interface Pack.
      • Doxal doorsampug Office 2013 te tànn tànneefu kaweel bi.
      • Bu doorsampug Office 2013 matee, sampal te jëmmal Microsoft Office 2013 Language Interface Pack.



    Doxalug sa costéefu Office:
    Boo amee jafe-jafe ci jàng kodu camp gépp ci jokkalug "Taxawu Tijjig Microsoft Office", mbaa kodu camp bu mat doxal ni mu waree bees jëfandikoo sa Microsoft Office Language Interface Pack 2013, baal nu fomm taxawukaay te jàll ci sa dàttu làkk coste ngir tijji sa coste Microsoft Office.

    Digle yi ngir jëfandikoo:
    Ngir soppi sa jokkalekaayu Jëfandiku ci làkkub Microsoft Office Language Interface Pack 2013 – Wolof, toppal yii jeego:

    1. Dowal Microsoft Office 2013 Làkku Taamu yi tukkee Tàmbali\Tëriin Yépp\Microsoft Office\Microsoft Office Jumtukaay yi njël.
    2. Suufu Tànn Wone ak Ndimbal Làkk yi, suufu Wone Làkk tànn làkk bu mu laaj te cuq ci Def niki Wàccaale butoŋ.
    3. Suufu Tànn Soppi Làkk yi, tànn làkk bi mu laaj te cuq ci Def ko bob Wàccaale butoŋ.
    4. Cuqal Waaw-kay butoŋ.


    Jekkali làkk yi nga tànn dinañu dox boo dooraatee say jëfekaayi Office.
    Karmat: Mëneesul a soppi ndimbal li ci làkku Microsoft Office Language Interface Pack 2013 – Wolof. Ndimbal day sax ci làkkuw campug Door wa.
    Sax ci def sa ndimbalu doxal ci njëlu wàccale bi ci dàttu làkk wi.

    Ngir far bii wàcce:
  • Juge ci bépp jëfekaayu Microsoft Office.
  • Cuqal-ñaaral Tëriin yeek Mën-mën yi ikon yi ci Windows Barabu Fugluwaay.
  • Ci Sempi mbaa Soppi ab Tëriin tànneef, cuqal Microsoft Office Language Interface Pack 2013 – Wolof ci Tëriin yees samp fimne boyet, kon tànnal Sempi tànneef.
  • Toppal tegtal yi ci seetu bi.