Trace Id is missing

Microsoft® Office Language Accessory Pack – Wolof

Microsoft Office Language Accessory Pack - Wolof dafay yokk wane yu bees, ndimbal, wala jumtukaayi jubbanti, lépp di aju ci làkk wi nga samp.

Lu am solo! Tànn ab lakk fii ci suuf dina soppi ci lu gaaw mbooleem këmbu xëtu boobu lakk.

Yebbi
  • Sumb:

    2016/2019

    Bisu Siiwal bi:

    16-03-2016

    Turu Taxañ

    Office2016_LAP_Readme_wo-sn.docx

    Dayoob taxañ:

    22.2 KB

    Microsoft Office Language Accessory Pack - Wolof dafay yokk wane yu bees, ndimbal, wala jumtukaayi jubbanti, lépp di aju ci làkk wi nga samp.
    Ginaaw boo sampee Microsoft Office Language Accessory Pack - Wolof, dinga mëna fekk man-man yi ak tànneef yi jàppandi ci biir jëfekaayi Office yi mu méngool ak ci jëfekaayu Taamuy Làkki Microsoft Office.
  • Sistem yimuy nangu

    Windows 10, Windows 7, Windows 8

      Ngir am njoxe Càkkutéefi sistem bi xoolal lëkkalekaayu Càkkutéefi sistemu Office
      Sistemu Microsoft Windows 8 - 32 wala 64 bit
      Sistemu Microsoft Windows 10 bu - 32 wala 64 bit. (Jëfandikukat yi jënd Office 2019 benn yoon du mëna dox ludul ci sistemu Windows 10)
      Bàyyi ci xel: Fexeel ba samp Kofre Cër yu mujj yi su ko defee sa sistem bi muy doxee mëna indil mbooleem say man-mani làkk.

    Losisel Bépp sumbu Office 2016 (wala bu gëna bees) topp wala bu toppul bu am Microsoft Excel, Microsoft Lync, Microsoft OneNote, Microsoft Outlook, Microsoft PowerPoint wala Microsoft Word dina jël Microsoft Office Language Accessory Pack 2016 (wala bu gëna bees) - Wolof.
    Ordinaatër ak prosesër1.6 GHz prosesër ak SSE2 sipoor wala bu gëna kawe; 4Go RAM; 2 Go RAM (32-bit) wala bu gëna kawe

    Yaatuwaayu disk bi Lu weesu espaas biñ jëfandikoo ngir samp jëfekaayi Office yi,
  • fàww nga am 4 Go yu jàppandi ci sa disk.

  • Yeneen càkkutéefi sistem yépp wuute wuñu ak yu jëfekaayi Office yi ngay jëfandikoo ak Microsoft Office Language Accessory Pack - Wolof.


  • Windows Language Interface Pack Noo ngi lay digal nga samp Windows Language Interface Packs bu mujj bi ngir sa sistem mëna am man-man yi war ci sa làkk ak jëfekaayi losisel yi.

    Jekkali Yaatuwaayu ekraŋ ak DPI Sos nañu xalima yu bees ngir gëna neexal njàng mi ak rëyaayu 1366 x 768. Sudee danga am ay jafe-jafe ngir jàng say xalima làkk kon soppil say jekkali rëyaayu ekraŋ mu tollu noonu wala mu ëpp ko su ko laajee. Bàyyi ci xel: noo ngi lay xelal nga jëfandikoo jëfekaayi Office ci jekkali DPI yi Windows wàccaale - 96 DPI. Soo jëlee jekkali 120 DPI mëna indi jafe-jafe ci sag jëfandikoo Office ci yenn jëfekaayi Office ndax dafay rëyal boyetu jalog yu Office.

    Tànneefi diwaan ak làkkNoo ngi lay digal nga jël mbooleem Tànneefi diwaan ak làkkyi ci Pano Konfig bi nga def leen ci làkku Microsoft Office Language Accessory Pack - Wolof.

  • Ngir samp Language Accessory Pack bi:
    1. Mën nga yebbi sampukaayuLanguage Accessory Pack soo bësee ci lëkkalekaay biiDownload Language Accessory Pack Installer
    2. Soo ko yebbee ba noppi nga bës Dawal.
    3. Follow the instructions on the screen to complete the installation.

    Soppil làkku jokkalekaayu jëfandikukat bi nga def ko làkku Language Accessory Pack
    Ginaaw boo sampee Language Accessory Pack bi, mën nga soppi làkku jokkalekaayu jëfandikukat bi nga def Wolof ci biir jëfekaayi Office wala ci biir jëfekaayi Microsoft Office Language Preferences.

    Ngir soppi làkku jokkalekaayu jëfandikukat bi ci Taamuy Làkk yi:

    1. Taalal Taamuy Làkku Office.
    2. Ci limuTànn Làkki Soppali nga tànn sa làkku soppali te nga bës butoŋuDef ko sama tànneef.
    3. Ci limuTànn Làkki Wane ak Ndimbal tànnal sa Làkku Wane and click the Def ko sama tànneef.
    4. Bësal butoŋu Ok bi.

    Ngir jàll ci làkku jokkalekaayu jëfandikukat ci jëfekaayu Office:

    1. Demal ci Taxañ, Tànneef yi, te nga tànnLàkk.
    2. Ci limuTànn Làkki Soppali nga tànn sa làkku soppali te nga bës butoŋuDef ko sama bi.
    3. Ci limuTànn Làkki Wane ak Ndimbal tànnal sa Làkku Wane and click the Def ko sama bi.
    4. Bësal butoŋu Ok bi.

    Balaa ngay mëna gis tànneefi làkk yi nga def di dox, fàww nga xaar ba taalaat say jëfekaayi Office.

    Soppi làkku mbind mi
    Microsoft Office Language Accessory Pack - Wolof mën na amaale càmbarukaayu mbind ci sa làkk. Nii la ñuy soppee mbind cim làkk ci mbind mu ñu tànn:

    Excel: Excel dafay jëfandikoo jekkali soppalikaayu Microsoft Office bu njëkk ngir mëna xam jekkali mbind mi fi nekk. Ngir soppi ko, bësal Taxañ ba noppi nga bës Tànneef yi. Bësal tànneefu jubbanti làkk ba noppi nga bës ci benn ci làkk yi jàppandi ci limu Làkku diksioneer bi.

    Outlook, PowerPoint, Word ak OneNote: Tànnal mbind mi nga bëgga càmbar, te bës Jàngat, bësal butoŋuLàkk bi, ba noppi bës tànneefu Def Jubbanti Làkk . Tànnal làkk wi la neex ci boyetu lim bi te bës Ok.